1
Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma:
2
«Yaw nit ki, ana lu bantu reseñ gëne ci bant yi, ak mboolem caru garab bu mu doon ci gott bi?
3
Ndax dees na ca sàkk bant, liggéeye ko? Am dees na ca sàkke wékkukaay, wékk ca lenn?
4
Xanaa sànni cib taal, xambe, ñaari cat ya lakk, digg ba xoyomu. Ana lu deeti njariñam?
5
Ndegam ba mu nee ñumm, lees ci dul liggéey dara, gën ba mu jàppee ba xoyomu.
6
Kon nag Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Dees na xamb caru reseñ, mu bokk ci banti garab yi ma joxe, ñu xamb lépp, te noonu laay xambe waa Yerusalem.
7
Maay jànkoonteek ñoom, ñu rëcc sawara, sawara lakk leen. Bu ma jànkoonteek ñoom, dingeen xam ne maay Aji Sax ji.
8
Maay gental réew mi, ñoo def jëfi ñàkk worma. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.»