Kàddug Aji Sax jii moo dikkaloon Ose, góor giy doomu Beeri, ci janti buuri Yuda: Osiyas ak Yotam ak Axas ak Esekiyas; ak ci janti buurub Israayil Yerbowam doomu Yowas.
Ba Aji Sax ji tàmbalee yóbbante Ose kàddoom, Aji Sax ji da ne ko: «Demal takki jabaru gànc, nga am ca doomi ngànctu, ndax réew maa ngi gànctu ngànctu gu réy, dëddu ma man Aji Sax ji.»
Ose dem takki Gomer doomu Diblayim. Mu ëmb, gannaaw gi mu am doom ju góor.
Aji Sax ji ne ko: «Tudde ko Yisreel. Des na tuuti dinaa mbugal askanu Buur Yewu ndax deret ji ñu tuur ci Yisreel. Dinaa dakkal nguurug waa Israayil.
Su bés baa maay damm ngànnaayu Israayil ca xuru Yisreel.»
Mu dellu ëmb, gannaaw gi mu am doom ju jigéen. Aji Sax ji ne: «Tudde ko Lo Ruxama» (muy firi Ki ñu yërëmul), mu ne: «ndax dootuma yërëm waa kër Israayil, dootuma leen baal.
Waaye waa kër Yuda, maa leen di yërëm. Seen Yàlla Aji Sax ji laa leen di walloo, waaye duma leen walloo fitt mbaa saamar, mbaa ay xare, mbaa ay fas aki gawar.»
Ba Gomer feralee Lo Ruxama, ëmbaat na, ba am doom, muy góor.
Aji Sax ji ne ko: «Tudde ko Lo Ami» (muy firi Du sama ñoñ), mu ne: «ndax dungeen sama ñoñ, te man duma seen dara.