v.2.10.1

Ose 6

11 Versets

1

Ca ngeen naan: «Nan dellu ci Aji Sax ji. Moo nu xotat, te moo nuy wéral. Moo nu duma, te moo nuy takkal sunuy góom.

2

Ñaari fan, mu leqali nu, ñetteel ba mu yékkati nu, nuy dund fi kanamam.

3

Nan ràññee, di saxoo faale Aji Sax ji. Ni jant bu fenk la dikkam wóore, ni ab taw la nuy dikkale, ni ab tawu mujjantal buy seral suuf.»

4

Aji Sax jee tontu: «Ana nu ma lay def, yaw Efrayim? Nu ma lay def, yaw Yuda? Te sa ngor di xiinu suba, mbaa ab lay, jekki ne mes.

5

Moo tax yonent yi laa leen di dumaa, sama kàdduy gémmiñ laa leen di reye. Seen àttee leen di leeral ni ceeñeeru njël.

6

Ndax ngor laa namm, dub sarax, ràññee Yàllaa ma gënal saraxi rendi-dóomal.

7

«Waaye ñoom ca dëkk ba ñuy wax Aadama lañu feccee kóllëre, foofa lañu ma wore.

8

Galàdd mooy dëkkub defkati ñaawtéef, taq ripp ak deret.

9

Ni saay-saay siy tëroo, ni la sarxalkat yi lëkkoo, di bóome ca yoonu Sikem. Ndaw jëf ju ñaaw!

10

Ci kërug Israayil laa gis lu yées: fa la Efrayim di gànctoo, Israayil googu laa ne moo sobeel boppam.

11

Yuda yaw it, sam ngóob ma ngay taxawe, kera bu may tijji sama wërsëgu ñoñ.