v.2.10.1

Ose 9

17 Versets

1

Yeen waa Israayil, buleen béglu, buleen bànneexu ni yeneen xeet yi, nde yeena gànctu, dëddu seen Yàlla, yeena safoo peyu ngànctu ci mboolem dàgga ju ñuy bàcce pepp.

2

Ndaxam dàgga ak nalukaayu reseñ du leen regg, te biiñ du leen doy.

3

Dungeen des ci réewum Aji Sax ji. Efrayim, Misra lay dellu, te ca Asiri, lu daganul lañu fay lekkeji.

4

Duñu tuural Aji Sax ji saraxu biiñ, te seeni sarax du ko neex. Seen ñamu sarax day mel ni ñam wu ku nekk fu nit deewe, sobeel, ba ku ca lekk sobewu. Seenu ñam, seenub koll lay ñeel, waaye du dugg ci kër Yàlla gi.

5

Ana nu ngeen di def nag, ci bésu ndaje, bésub màggal bu Aji Sax ji?

6

Ñu ngoogu dem ndax tasteg réew mi, Misraa leen di fat, Memfis suul leen, seen tànnéefu xaalis, mbooy mee koy nangu, te xaaxaam ay saxe seen biiri xayma ya woon.

7

Bési mbugal dikk na, bési añale taxaw na, na ko Israayil xam. Yonent lañu jàppe ab dof, ku yorey waxyu di ku wéradi, ndax seen ñaawtéef gu réy, ak seen mbañeel gu tar.

8

Yonent bi mooy wattukat biy wattul Yàlla ca Efrayim, waaye ag fiir lees ko lalal ci mboolemi yoonam, te mbañeel a ngi ci biir kër Yàllaam.

9

Ñoo sóobu ci xóotey yàqute, na woon ca janti Gibeya, te Yàlla mooy bàyyi xel seenug ñaawtéef, ba mbugale leen seeni moy.

10

Aji Sax ji nee na: «Ni cabbu reseñu biir màndiŋ, ni laa fekke Israayil. Ni ndoortel doomi figg ju ndey ja taawloo, ni laa gise seeni maam. Waaye ñoom ñoo dem Baal Pewor, ñoo sédd seen bopp Baal, tuur mu ruslu mi, ba tax leena seexluwu ni kooku ñu sopp.

11

Efrayim, ab sagam ni picc lay naawe, du njurum doom, dub ëmb, du doom ju sosu sax.

12

Bu ñu yaroon seeni doom it, maa leen leen di xañ, ba kenn du des. Te it ngalla ñoom, bu ma leen dëddoo.

13

Ni ma dogule Tir dëkk ba bi jëmbate ci parlu mu naat, ni laay dogule Efrayim, ba yóbbul ay doomam ab bóomkat.»

14

Aji Sax ji, yool leen! Ana loo leen di yool? Yool leen biir yu yàqu, ak ween yu ne sereŋ.

15

Aji Sax ji neeti: «Seen gépp mbon moo feeñ ca Gilgal, te fa laa leen jéppee ndax mbonug seeni jëf. Sama kër laa leen di dàqe, te dootuma leen bëgg, seeni njiit yépp a diy fippukat.

16

Duma nañu Efrayim, ay reenam wow, du meññ benn doom. Bu juroon itam, maay rey ngëneelu biiram.»

17

Sama Yàlla moo leen di xalab, nde ñoo ko déggalul, te ñooy taxawaaluji ci biir xeeti jàmbur yi.