v.2.10.1

Esayi 12

6 Versets

1

Bésub keroog dees na ne: «Aji Sax ji, sant naa la; yaa ma mere woon, meddi, dëfal ma.»

2

Ma ne: «Yàllaa may wallu, ma dallu, duma tiit. Sama dooleek sama kaaraange mooy Ki Sax, di Aji Sax ji, te mooy sama wall.»

3

Mbégte ngeen di rooteji fa wali mucc ya.

4

Bésub keroog ngeen ne: «Santleen Aji Sax ji, tudd turam, xamley jalooreem ci biir xeet yi, fàttali màggaayu turam.

5

Woyleen Aji Sax ji, moo kawey jëf! Na lii siiw biir àddina sépp.

6

Yeen waa Siyoŋ, serleen te sarxolleel Ku màgg ki fi seen biir, Aji Sell ju Israayil.»