v.2.10.1

Esayi 15

9 Versets

1

Yéene bii ñeel na Mowab:

2

Nit ñaa ngi yéeg jëm kërug jaamookaay ga ca Dibon, ngir jooyi ca bérebi jaamookaay ya, Mowab a ngay yuuxoo kaw tundu Nebo ak Medeba, boppoo bopp dib nel, sikkimoo sikkim xuufu,

3

nit ña sol saaku, di ñaawlu fa mbedd ya, ak kaw taax yaak pénc ya, ku ne di jooy ba say rongooñ wale.

4

Waa Esbon ak Elalee ngi yuuxu, seen baat àkki ba Yaxacc, xarekati Mowab dégg ca, yuuxoo, ne yàcc ne yasar!

5

Maay jooy Mowab jooyi xol, nit ñaa nga fay dawe ba Cowar, àkki ba Eglat Selisiya. Ña ngay yéeg jëm Luxit, di jooyoo, awe yoonu Oronayim, di yuuxu.

6

Dexu Nimrim wow na, ñax wow, gàncax lax, dara naatatul.

7

Jël nañu lu ñu deseek lu ñu dencoon, yóbbu, jàll ca wàllaa xuru Garab ya.

8

Yuux déy maase na réewum Mowab, jooyoo ya ba Eglayim, jooyoo ya ba Beer Elim.

9

Dexu Dimon déy fees na ak deret, te ma nara wàcceel Dimon lu ko raw, ba ku rëcce Mowab, ak ku des ci réew mi, ma booleek gaynde!