v.2.10.1

Esayi 4

6 Versets

1

Su bés baa, juróom ñaari jigéen ŋoyaalu genn góor, ne ko: «Sunub dund, nun a, sunu koddaay, nun a! Jox nu sag buum rekk, teggil nu gàcce.»

2

Su bés baa njebbitum Aji Sax ji doon lu yànj, darajawu, meññeefum réew mi di teraanga, dib sag, ñeel ñi dese bakkan fi Israayil.

3

Su boobaa ku mucc fa Siyoŋ ak ku des fa Yerusalem, ku sell ki lees lay woowe, muy képp ku ñu bind turam, te mu wara dese bakkan ci Yerusalem.

4

Boroom beey wal noowal mbugal, noo guy lakk, sellal, fóote ko jonkani jigéeni Siyoŋ, fetee ko deret ji ci Yerusalem, ba mu set.

5

Su boobaa tundu Siyoŋ bépp, fépp fu ñuy dajee, Aji Sax ji sàkk fa niiru saxaar bëccëg, guddi mu def tàkk-tàkk bu ne ràññ; leeru Aji Sax ji di kiiraay, tiim lépp,

6

di mbaar mu ñuy féexloo tàngooru bëccëg, di ko seeloob taw ak waame.