v.2.10.1

Yeremi 15

21 Versets

1

Aji Sax ji nag ne ma: «Musaa ak Samiyel sax, bu ñu taxawoon fi sama kanam, du tax ma faale askan wii. Dàqal, ñu sore ma, te wéy.

2

Bu ñu la laajee ne la: “Fu nu jëm?” nga wax leen ne leen:

3

«Te dinaa wàcce fi seen kaw ñeenti xeeti duma.» Kàddug Aji Sax jee. «Saamar di bóom; xaj diri yóbbu, njanaaw ak rabu àll for, mu jeex.

4

Dama leen di def, waa réewi àddina yépp, ku leen ci xool rasu. Te li ko waral di Buurub Yuda, Manase miy doomu Esekiyas, ak li mu def ci digg Yerusalem.

5

«Yerusalemee, ku lay yërëm? Ku lay jooy? Moo, ku lay geesu ne la: “Jàmm nga am?”

6

Yaw yaa ma wacc, kàddug Aji Sax jee, dellu gannaaw, ma duma la, sànk la. Muñ naa ba sonn.

7

Maa leen bees ni ñuy beesem pepp ci pénci réew mi. Maa sànk sama ñoñ, faat seeni doom, ndax tuubuñu seeni jëfin.

8

Seeni jëtun laa ful, ba ñu ëpp suufas géej, ma indil leen pàddum njolloor, mu reyal yaay doomi waxambaaneem, këpp ko tiitaangeek njàqare.

9

Yaayu juróom ñaari góor loof, di àppaat, jantam sowe bëccëg ndarakàmm, yaakaar tas, mu jàq, seenu ndes, ma leel saamaru noon.» Kàddug Aji Sax jee.

10

Wóoy saa ndey, loo ma doon jure! Man mi réew mépp di xulooka layool, leblewuma, lebuma; te ñépp di ma móolu.

11

Ndaxam Aji Sax ji nee: «Maa lay xettali déy, ngir sottal lu baax; maa la defal sa noon di la tinu déy, ci janti safaan ak njàqare.»

12

«Ku mana toj weñ gu ñuul, rawatina yetu weñu bëj-gànnaar, mbaa xànjar?

13

Yeen waa Yuda, seen alal ak seeni denc laay jox ñu ko sëxëtoo te feyuñu ndax seen gépp moy ci seen réew mépp.

14

Maa leen di def seen jaami noon réew mu ngeen xamul, sama mer jippét, tàkkal leen.»

15

Yaw déy Aji Sax ji, xam nga! Ngalla bàyyi ma xel, geesu ma; feyul ma ñi ma sam. Bu leen muñal ba sànk ma! Xamal ne yaa ma tax di dékku saaga.

16

Sa kàddu laa gis, di ko dunde, sa kàddu di ma bégal, bànneexal sama xol. Yaw Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, déy, sa tur lañu ma tudde.

17

Masumaa toogandook ñiy mbumbaay bay xawaare. Yaa ma jiite, ma beru, toog, ndax mer mi nga ma sol, ba ma fees.

18

Moo, sama tiis wi du dakk a? Bii góom bu metti, tëë wér! Yaw kay yaay waltan muy wal, di ŋiis, di tas sama yaakaar.

19

Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne: «Soo délsee, ma delloosi la, nga dellu di ma liggéeyal. Soo dee wax ngëneel lu soreeki caaxaan, dinga mel ni yaay sama làmmiñ, te nit ñeey délsi ànd ak yaw, waaye du yaay délsi ànd ak ñoom.

20

Maa lay def nga mel ci gis-gisu askan wii ni tatay xànjar ju ñu dàbbali, ñu di la song te duñu la man. Maay ànd ak yaw, di la wallu, di la xettali.» Kàddug Aji Sax jee.

21

«Ab soxor jàpp la, ma àtte; ab néeg ne la céex, ma foqati.»