Muy kàddug Yeremi, góor gi baayam Ilkiya bokk ci sarxalkat yi dëkk Anatot ca diiwaanu Beñamin.
Kàddug Aji Sax ji dikkal ko ci jamonoy buuru réewum Yuda, Yosya doomu Amon. Mu yemook fukkeelu atu nguuram ak ñett.
Kàddug Aji Sax ji dikkal na ko ba tey ci janti buurub Yuda, Yoyakim doomu Yosya, di ko dikkal, ba keroog nguurug Cedesyas di jeex, jeneen doomu Yosya ja. Mu yemook fukkeelu atu nguuram ak benn, ca juróomeelu weer wa. Booba lañu jàpp waa Yerusalem njaam, yóbbu leen.
Kàddug Aji Sax ji dikkal na ma, ne ma:
«Laata ma lay sos ci sa biiru ndey, laa la xam; laata ngay juddoo ci sa ndey, laa la séddoo, def la ngay yonent ñeel xeet yi.»
Ma ne: «Éy Boroom bi Aji Sax ji, da di manumaa wax, gone doŋŋ laa.»
Aji Sax ji ne ma: «Bul ne: “Gone laa.” Képp ku ma la yebal, dem ca; lépp lu ma la sant, wax ko.
Bu leen ragal, ngir yaw laay àndal, di la xettali.» Kàddug Aji Sax jee.
Aji Sax ji tàllal loxoom, laal sama gémmiñ. Aji Sax ji ne ma: «Mu ngoog, sexal naa la samay kàddu.
Ma ne, tabb naa la bés niki tey, ci kaw xeet yeek réew yi, ngay buddat, di fàqat, di yàqate aka daaneel, di defar aka jëmbat.»
Kàddug Aji Sax ji dikkal ma, ne ma: «Yeremi, loo gis?» Ma ne ko: «Caru garabu saal laa gis.»
Aji Sax ji ne ma: «Yaa ko gis, maa sàlloo def sama kàddu, ngir sottal ko.»
Kàddug Aji Sax ji dikkalaat ma ñaareel bi yoon, ne ma: «Loo gis?» Ma ne: «Cin luy bax laa gis. Mu ngi joye bëj-gànnaar, jublook nun.»
Aji Sax ji ne ma:
Maa ngii déy, di woo mboolem waasoy réewi bëj-gànnaar ak seeni buur.» Kàddug Aji Sax jee. «Dañuy dikk, ku ne dëj ngànguneem fi janook bunti Yerusalem, jànkoonteek tataam yépp, ak dëkki Yuda yépp.
Maay biral samay àtteek ñoom ci seen mbon gi gépp: Dañu maa wacc, di taalal cuuraay yeneen yàlla, di sujjóotal lu ñu sàkke seeni loxo.
«Yaw nag takkul te wax leen lépp lu ma la sant. Bul am tiitaange fi seen kanam, lu ko moy ma tiital la fi seen kanam.
«Maa ngii def la bésub tey nga mel ni dëkk bu mag bu tata wër, mel ni xeru weñ mbaa tatay xànjar, jàkkaarlook réew mi mépp, muy buuri Yuda aki kàngamam, di sarxalkati réew mi ak baadoolo yi.
Dañu lay xeex te duñu la man, yaw laay àndal, di la xettali.» Kàddug Aji Sax jee.