Kàddug Aji Sax ji dikkaloon na Yonent Yàlla Yeremi jëm ci Filisteen ñi, balaa Firawna di song dëkkub Filisteen ba ñuy wax Gasa.
Aji Sax ji dafa wax ne:
Booba fas yaa ràmbal, watiir ya riir, mbegey watiir ya kar-kareendoo, loxo yoqi, ba baay geesuwul doom,
bésub sànkute dikkal képp kuy Filisteen, ba dagge ci dëkk yii di Tir ak Sidon ndimbal lu ñu dese woon. Aji Sax jaa ngay sànk Filisteen ña des te cosaanoo dun bu ñuy wax Keret.
Watu nel, ñaawloo dikkal na Gasa, te wedamloo nañu Askalon. Yeen ñi dese joor gi, fu ngeen àppal seen yaram wi ngeen di daggat, di ko ñaawloo?
Ngeen naa: “Wóoy saamaru Aji Sax jii, xanaa doo noppee reye? Dellul ci sa mbar, boog, dallu, ne tekk!”
Waaye yaw saamar, naka nga mana selaŋloo te Aji Sax ji yebal la ci kaw Askalon ak waa tefesu géej, fa mu ko dogale?»