1
Bildàdd ma bàyyikoo Suwa àddu, ne:
2
Yàllaa man te mata ragal, di def jàmm fa kawteem ya.
3
Ay gàngooram limu naam? Ana ku mu dul jam ceeñeeram?
4
Ana nu nit di ame dëgg fa kanam Yàlla? Ku jigéen jur, nu mu mana laabe?
5
Xoolal, weer wi sax leerul ba doy ko, te biddiiw yi it gisul seen sellaayu leer,
6
astamaak nit kii tanewul aw sax, doom aadama jii gënul gasax.