Lii mooy ndoortel xibaaru jàmm bu Yeesu Almasi bi, Doomu Yàlla ji.
Mu doore ni ñu ko binde ci téereb Yonent Yàlla Esayi, fu Yàlla ne:
Baatu nit a ngi xaacoo ca màndiŋ ma, naan: “Nangeen xàll yoonu Boroom bi, juballeen ay xàllam.”»
Yaxya nag dikk ca màndiŋ ma, di waare lu jëm ci tuubeel gu nit ñi wara fésale ag sóobu cim ndox, ngir Yàlla jéggal leen seeni bàkkaar.
Ci kaw loolu mboolem diiwaanu Yude ak waa Yerusalem ñépp bàbbeeku, jëm ca Yaxya. Ñu tudd seeni bàkkaar, Yaxya sóob leen ca dexu Yurdan.
Yaxyaa nga sol mbubb mu ñu ràbbe kawaru giléem, laxasoo laxasaayu der ca ndigg la, di dundey njéeréer ak lemu àll.
Mu waare, ne: «Am na ku ma sut kuy ñëw sama gannaaw, kooku, buumi caraxam sax yeyoowumaa sëgg, di ko ko feccil.
Man cim ndox laa leen sóob, waaye moom de, ci Noo gu Sell gi la leen di sóob.»
Ca fan yooyu la Yeesu bàyyikoo dëkk ba ñuy wax Nasaret ca diiwaanu Galile. Mu dikk, Yaxya sóob ko ca dexu Yurdan.
Naka la Yeesu génn ndox ma ca saa sa, daldi gis asamaan xar, Noowug Yàlla, wàcc ni am pitax, ca kawam,
baat jibe asamaan, ne: «Yaa di sama Doom, sama soppe; yaw laay bànneexoo.»
Ca saa sa Noowug Yàlla jañax Yeesu, ba ca biir màndiŋ ma.
Nekk na ca màndiŋ ma ñeent fukki fan, Seytaane di ko fiir, mu nekkandook rabi àll yi, malaaka yi di ko toppatoo.
Gannaaw ba ñu tëjee Yaxya kaso, Yeesu dem Galile, di waare xibaaru jàmm bu Yàlla bi,
naan: «Waxtu wa mat na, nguurug Yàlla dëgmal na. Tuubleen seeni bàkkaar te gëm xibaaru jàmm bii.»
Yeesoo doon jaare tàkkal dexu Galile, daldi gis ku ñuy wax Simoŋ ak Àndre, rakkam ju mu bokkal ndey ak baay. Ña ngay mbaal ca dex ga, ndax ay nappkat lañu woon.
Yeesu ne leen: «Ñëwleen topp ma, ma def leen nappkati nit.»
Ñu won mbaal ya gannaaw ca saa sa, daldi topp ca moom.
Yeesu doxaat tuuti, gis Yanqóoba doomu Sebede ak Yowaan mi Yanqóoba bokkal ndey ak baay. Ña nga ca gaal ga, di gaar seeni mbaal.
Yeesu woo leen ca saa sa, ñu bàyyi seen baay Sebede ca gaal ga, mook surga ya, daldi topp ca moom.
Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya jàll biir dëkk ba ñuy wax Kapernawum. Naka la bésub Noflaay taxaw, Yeesu daldi dugg ca biir jàngub Yawut ba, di jàngale.
Ñu yéemu ca njàngaleem ndax sañ-sañ ba mu leen di jàngale niroowul ak na la firikati yoonu Musaa yay jàngalee.
Jenn waay a nga woon ca seen biir jàngu ba, rab a ko jàpp. Mu jekki di xaacu, naan:
«Yaw Yeesum Nasaret, ana lu nu joteek yaw? Alagsi nu mooy say tànk? Xam naa yaa di kan, yaa di Aji Sell ju Yàlla ji.»
Yeesu nag gëdd ko, ne ko: «Noppil te génn nit ki!»
Rab wu bon wa daane waa ja ba muy say, mu yuuxu yuux gu réy, doora génne ca waa ja.
Ba loolu amee ñépp yéemu, naan ca seen biir: «Lii lu mu doon? Guléet mii njàngale! Céy bii xam-xam bu ànd ak sañ-sañ! Rab yi sax, mu jox leen ndigal, ñu def!»
Turu Yeesu nag law a law ca saa sa, ba dajal diiwaanu Galile gépp.
Gannaaw ba Yeesu ak Yanqóoba ak Yowaan génnee ca jàngu ba, dañoo ànd ca saa sa, dem kër Simoŋ ak Àndre.
Fekk yaayu jabaru Simoŋ tëdd ndax yaram wu tàng. Ñu yégal ko Yeesu.
Mu dikk ba ca soxna sa, jàpp ca loxoom, yékkati ko, tàngooru yaram wa teqalikook soxna sa, mu di leen toppatoo.
Ba ngoon jotee ba jant so, ñu indil Yeesu mboolem ñi wopp ak ñi rab jàpp,
dëkk ba bépp daje ca buntu kër ga.
Ci biir loolu ñu bare ñu ame ay jàngoroy jàngoro, mu wéral leen, rab yu bare, mu dàq leen. Waaye gannaaw rab ya xam nañu ko, mayu leen ñu wax.
Ca ëllëg sa, laata bët di set, Yeesu jóg, génn, dem, ba àgg benn béreb bu wéet. Mu di fa ñaan Yàlla.
Ci biir loolu Simoŋ aki àndandoom di ko seet.
Ba ñu ko gisee, ne ko: «Ñépp a ngi lay seet.»
Yeesu ne leen: «Nan dem feneen ci dëkk yi nu wër ngir ma waare foofu itam, ndax looloo ma taxa génn.»
Ci kaw loolu muy wër diiwaanu Galile gépp, di waare ci seeni jàngu, di dàq rab yi.
Gannaaw loolu genn gaana dikk ba ca moom, di ko ñaan, daldi sukk, ne ko: «Su la soobee, man nga maa setal.»
Yërmande jàpp Yeesu, mu tàllal loxoom, laal ko, ne ko: «Soob na ma, setal.»
Ca saa sa ngaana ga teqalikook moom, mu set wecc.
Yeesu nag artu ko bu baax, yiwi ko ca saa sa, ne ko:
«Fexeel ba bul wax kenn dara, demal rekk ca sarxalkat ba, ngir mu seet la, te nga génne sa saraxu setlu ni ko yoonu Musaa santaanee, ngir muy firnde ci ñoom.»
Waaye naka la waa ja génn, tàmbalee yéene, siiwal mbir ma, ba tax Yeesu manatula siiwal duggam cib dëkk, xanaa mu féetewoo béreb yu wéet ca fa ko wër. Teewul nit ñiy jóge fu nekk, di ko fekki.