v.2.10.1

Macë 1

25 Versets

1

Lii mooy cosaanu Yeesu Almasi bi, sëtub Daawuda, sëtub Ibraayma.

2

Ibraayma moo jur Isaaxa; Isaaxa jur Yanqóoba; Yanqóoba jur Yuda aki doomi baayam;

3

Yuda moo jur Peres ak Sera, Tamar di seen ndey; Peres moo jur Esron, Esron jur góor gu ñuy wax Aram;

4

Aram moo jur Aminadab; Aminadab jur Naason; Naason jur Salmon;

5

Salmon jur Bowas mi Raxab di ndeyam; Bowas moo jur Obedd mi Ruut di ndeyam; Obedd moo jur Yese,

6

Yese moo jur Buur Daawuda.

7

Suleymaan moo jur Robowam; Robowam moo jur Abya; Abya moo jur Asaf;

8

Asaf moo jur Yosafat; Yosafat moo jur Yoram, Yoram moo jur Osiyas;

9

Osiyas moo jur Yotam; Yotam moo jur Axas, Axas moo jur Esekiyas;

10

Esekiyas moo jur Manase; Manase moo jur Amon; Amon jur Yosya;

11

Yosya moo jur Yekoña aki doomi baayam ca jant ya ñu yóbboo Yawut ya ca jant ya ñu jàpp Yawut ya njaam, yóbbu Babilon.

12

Gannaaw ba ñu leen gàddaayloo ñu dem Babilon la Yekoña jur Selcel; Selcel jur Sorobabel,

13

Sorobabel jur Abiyudd; Abiyudd jur Elyakim; Elyakim jur Asor;

14

Asor jur Cadog; Cadog jur Akim; Akim jur Elyudd;

15

Elyudd jur Elasar; Elasar jur Matan, Matan jur Yanqóoba;

16

Yanqóoba nag moo jur Yuusufa jëkkëru Maryaama; te Maryaama moo jur Yeesu, mi ñuy wax Almasi bi.

17

Mboolem maas yi dox diggante Ibraayma ba ca Daawuda nag di fukki maas ak ñeent; li dox diggante Daawuda ba ca njaam ga ca Babilon, di fukki maas ak ñeent; li dox diggante njaam ga ca Babilon ba ci Almasi bi, di fukki maas ak ñeent.

18

Juddub Yeesu Almasi bi, nii la deme: Ndeyam Maryaama moo digoo woon ab séy ak Yuusufa. Laata ñuy ànd nag, gis nañu ne Maryaama dafa ëmb ci dogalu Noo gu Sell gi.

19

Ci biir loolu jëkkëram Yuusufa mi doon nit ku jub, naroon koo yiwi ci sutura, ndax bëggu ko woona weer.

20

Naka lay xalaat ci loolu, am malaakam Boroom bi feeñu ko ci gént, ne ko: «Yuusufa, sëtub Daawuda, bul ragala yeggali sa jabar Maryaama, ndax doom ji sosu ci moom, ci Noo gu Sell gi la jóge.

21

Doom ju góor lay am; nanga ko tudde Yeesu (muy firi Boroom beey musle), ndax mooy musal aw xeetam ci seeni bàkkaar.»

22

Loolu lépp a sotti ngir matal la Boroom bi waxe woon ca làmmiñu yonent ba, ba mu nee:

23

«Janq bi mooy ëmb, jur doom ju góor, ñu tudde ko Emanuwel,» muy firi Yàllaa ngi ak nun.

24

Ba Yuusufa yewwoo, la ko malaakam Boroom bi sant la def, daldi yeggali jabaram.

25

Waaye Yuusufa àndul ak moom, ba kera mu ame doom, muy góor, mu tudde ko Yeesu.