Ndaw a ngii dawe kaw tund ya, di indi kàddu, xibaaru jàmm. Yaw Yuda, bégeel sa bési màggal, te wàccook say xas. Nit ku bon ki dootul jaare fi yaw; léppam lees di dagg, sànni.
Ki lay falaxe buur na, wutsi la! Sàmmal sab tata, wattu saw yoon, takkal sa ndigg, te dëgërlu bu baax.
Aji Sax ji moo yeesal darajay Yanqóoba, darajay Israayil moomu. Ay taskat a ko tasoon, yàqate ay caram.
Pakki jàmbaaram ña lañu suub xonq, ñeyi xare ya sol lu xonq curr, watiiri xare yay melax ni luy tàkk, ca bés ba ñu waajal xare, xeej ya jóg.
Ca mbedd ya la watiiri xare yay riire, riddi jaare pénc ya, mel niy jum, di ray-rayi niy melax.
Ca la njiit la di woolu kàngami xareem, ñuy gaawtu bay tërëf. Tata ja lañuy gaaw wutali, ba yékkati ay kiiraay.
Bunt ya jëm dex ga ñooy jekki ubbiku, kër buur màbb.
Futtees na jongama, yóbbu, janqam jay binni niy xati, di fëgg seen dënn.
Niniw la ay nitam di daw, mu mel ni mbànd mu ndox may senn, ñu naan leen: «Taxawleen, taxawleen,» te kenn geestuwul.
Sëxëtooleen xaalis, sëxëtoo wurus, alal du fi jeex te mboolem gànjar a jale.
Dëkk bi lees di raatale, maasale, mu ne faraas, fit rëcc, óom yiy fenqe, ndigg yépp di kal-kali, kanam yépp di sël-sëli.
Moo ana paxum gaynde ga? Ana àllub gaynde yu ndaw ya, fa góoru gaynde daa daagoo, mook jeegub gayndeem ak doom ya, te dara tiitalu leen!
Gaynde di fa fàdd lu doy ay doomam, reyal ay jeegi gayndeem, feesal xuntam akum rëbbam, feesal paxam akum pàddam.
«Maa ngii fi sa kaw,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi. «Say watiiri xare laay lakk, saxaaral, sa gaynde yu ndaw, saamar lekk leen, te sam pàdd laay jële ci réew mi, ba deesul déggati baatu ndaw loo yebal.»