v.2.10.1

Neyemi 10

40 Versets

1

«Loolu yépp tax na nuy tëral takktoo bu dogu, bind ko, sunuy njiit ak sunuy Leween ak sunuy sarxalkat def ci seen màndargay torlukaay.»

2

Ñi ko torlu ñoo di

3

ak Seraya ak Asaryaa ak Yeremi

4

ak Pasur ak Amarya ak Malkiya

5

ak Atus ak Sebaña ak Malukk

6

ak Arim ak Meremot ak Abdiyas

7

ak Dañeel ak Gineton ak Barukk

8

ak Mesulam ak Abya ak Miyamin

9

ak Maasya ak Bilgay ak Semaya. Ñooñu ñoo di sarxalkat ya.

10

Leween ñi ñoo di

11

Seeni bokk ca lañu, di Sebaña ak Oja ak Kelita ak Pelaya ak Xanan

12

ak Mise ak Rexob ak Asabya

13

ak Sakur ak Serebya ak Sebaña

14

ak Oja ak Bani ak Beninu.

15

Njiiti askan wi ñoo di

16

ak Buni ak Asgàdd ak Bebay

17

ak Adoña ak Bigway ak Adin

18

ak Ater ak Esekiyas ak Asur

19

ak Oja ak Asum ak Beccay

20

ak Arif ak Anatot ak Nebay

21

ak Magpiyas ak Mesulam ak Esir

22

ak Mesesabel ak Cadog ak Yaduwa

23

ak Pelaca ak Xanan ak Anaya

24

ak Ose ak Anaña ak Asub

25

ak Aloxes ak Pilxa ak Sobeg

26

ak Rexum ak Asabna ak Maaseya

27

ak Axya ak Xanan ak Anan

28

ak Malukk ak Arim ak Baana.

29

Bànni Israayil ga ca des nag fekksi leen, muy sarxalkat yaak Leween ñaak fara bunt yaak woykat yaak liggéeykati kër Yàlla ga, di mboolem ñi beddeeku woon askanu yéefar yi, ngir topp yoonu Yàlla wi, ñook seeni jabar ak seeni doom yu góor ak yu jigéen, mboolem ñi xam te xàmmee.

30

Ci kaw loolu ñu ànd ak seen bokki garmi, waatook ñoom ne dinañu topp yoonu Yàlla wi mu dénkaane, Musaa jaamam ba jottali; di ko sàmm, di jëfe mboolem sunu santaaney Boroom Aji Sax ji ak àttey yoonam ak dogali yoonam.

31

Nu ne nag:

32

«Te itam bu waa réew mi indee am njaay mbaa lépp luy pepp, di ko jaay ci bésub Noflaay, dunu ko jënd ci ñoom bésub Noflaay mbaa bés bu sell.

33

«Ci biir loolu nu warloo santaaney joxe at mu nekk ñeenti garaami xaalis, bu jëm ca sunu liggéeyu kër Yàlla ga,

34

jëm ca mburum teewal ma, ak saraxi pepp yi war bés bu nekk, ak saraxi dóomal yu bés bu nekk, ak saraxi bési Noflaay, ak yu Terutel weer ak yu bési màggal yi, ak yeneen yu ñu sellalal Yàlla, ak saraxi póotum bàkkaar yi bànni Israayil di jotoo, ak mboolem la war ca sunu liggéeyu kër Yàlla ga.

35

«Ay bant lanu tegoo ci sunu biir, nun sarxalkat yeek Leween ñeek baadoolo yi, ngir dogalal waa kër gu nekk àpp ba ñu wara aye cim at, te ñu war caa yóbbu seen sasu matt ca sunu kër Yàlla ga, ngir taal ko ca sunu sarxalukaayu Yàlla Aji Sax ji, muy la ñu bind ci téereb yoon wi.

36

«Nu dogu ba tey ne dinanu yóbbu ca kër Aji Sax ji, at mu nekk, li sunu suuf njëkka meññle ak lu garab yépp njëkka ñorle.

37

Ci biir loolu nu dogoo def li ñu bind ci yoon wi, di yóbbu ca sunu kër Yàlla ga sunu taaw yu góor ak lu sunu jur taawloo, gu gudd gaak gu gàtt ga, di teg lépp ci loxoy sarxalkat ya fay liggéey.

38

Ci kaw loolu nu wara yóbbu ca sunu néegi dencukaayi kër Yàlla ga lu njëkk ci sunu nootu sunguf ak sunu njoxey pepp ak sunu meññeefi garab yépp ak sunu biiñ ak diw, di teg lépp ci loxoy sarxalkat yi. Ba tey nuy indil Leween ñi céru fukkeelub lépp luy meññee ci sunu suuf, ndax Leween ñeey dajalesi céri fukkeel yi ci gox yi nuy bey yépp.

39

Sarxalkat bu askanoo ci Aaróona mooy gunge Leween ñiy jëlsi céri fukkeel yi. Su ko defee Leween ñi yóbbu fukkeelu céri fukkeel yi ba ca sunu kër Yàlla ga, fat ko ca néegi dencukaayi alal ya.

40

Ci néeg yooyu la bànni Israayil ak askanu Leween ñi di yóbbu njoxem pepp ma ak biiñ baak diw ga; fa la ndabi kër gu sell ga dence, te fa la sarxalkat ya nekk, ñoom ña sasoo liggéey ba, ñook fara bunt yaak woykat ya. Nu dogu nag ne dunu sàggane sunu kër Yàlla ga.»