1
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda. Éy su dul woon ak Aji Sax ji nu nekkal! Israayiloo, waxati ko:
2
su dul woon ak Aji Sax ji nu nekkal, ba ñu nu jógalee,
3
ba nit ña xadaroo sunu kaw, dañu nu doon wann, nuy dund,
4
dañu nu doon mëdd nim ndox, defum wal, buub nu,
5
def waame wuy wal-wali, buub nu, yóbbu.
6
Cant ñeel na Aji Sax ji, ki nu bàyyiwul, noon yi yàpp nu.
7
Danu ne fërr, nim picc mu rëcc fiiru rëbb, fiir ga toj, nu raw.
8
Sunu ndimbal a ngi ci turu Aji Sax ji, Ki sàkk asamaan ak suuf.