1
Ndokkalee yaw mi toppul tànki ku bon, taxawewuloo yoonu moykat, toogewuloo jataayu ñaawlekat.
2
Xanaa di bége yoonu Aji Sax ji, di ko jàngat guddeek bëccëg.
3
Loo def mu àntu: nga mel ni garab gu saxe walum ndox, bu jotee meññ, te xob wa du lax.
4
Loolu dalul moos ku bon kay mel ni xatax bu ngelaw li wal.
5
Moo tax ku bon du siggee àtte ba, moykat du taxawe ndajem aji jub ña.
6
Aji Sax ji kay ay sàmm yoonu aji jub; yoonu ku bon di sànk boroom.