1
Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
2
Buur, yal na la Aji Sax ji nangul bésu njàqare, yal na la turu Yàllay Yanqóoba aj fu kawe,
3
yal na la yónnee wallam fa këram, jàppalee la fa, ca Siyoŋ.
4
Yal na xool loo ko jébbal, di rafetlu sarax soo ko lakkal. Selaw.
5
Yal na la may li nga namm, di sottal loo mébét,
6
ngay daan, nuy ree, yéege sunu raaya, màggal sunu Yàlla. Yal na Aji Sax ji nangu loo dagaan.
7
Aji Sax jeey musal ki mu fal, bir na ma tey. Moo koy nangule fa asamaan su sell sa, ci dooley ndijooram biy musle.
8
Ñiiki watiir, ñeeki fas, nun sunu turu Yàlla Aji Sax ji lanuy tudd.
9
Ñoom ñooy jeng aka jóoru, nun, nu jóg, taxaw jonn.
10
Éy Aji Sax ji, mayal Buur mu daan, te bés bu nu ko ñaane, mu nangul nu.