1
Ñeel Daawuda, dib taalifu cant. Aji Sax jee may sàmm, du lenn lu ma ñàkk.
2
Parlu mu naat la may gooral, wal mu dal, mu tette ma ca,
3
leqali ma, teg ma ci yooni njub ngir teraangay turam.
4
Su may jaare xuru dee wu ne këruus it, duma ragal loraange: yaw laak man, sa bantu sàmm ak sa nguul, yooyoo may dalal.
5
Yaa ma berndeel, noon yi gis, nga diwal ma saa bopp, terale ma, saab kaas rembat.
6
Mbaax ak ngor kay la ma Aji Sax jiy dare sama giiru dund, ma dëkke këram ba fàww.