1
Éy Yàlla, àtte ma, layool maak xeet wu gorewul, xettali maak ku njublaŋ te dëng.
2
Yaw Yàlla kat yaay sama rawtu. Lu tax nga wacc ma, may wéye tiis, ci nooteelu noon?
3
Ngalla yónneel sag leer ak sa dëgg, yal na ma yooyu jiite, yóbbu ma sa tund wu sell, sa màkkaan ma.
4
Kon Yàlla, naa àgg ca sa sarxalukaay; yaw Yàlla, yaay sama mbégte, di sama bànneex. Yaw Yàlla, sama Yàlla, naa la màggale xalam.
5
Moo man, lu may xàddi, ne yogg? Lu may jàq nii? Tee maa yaakaar Yàlla, ba santati ko, moom sama Yàlla mi may wallu?