1
Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel askanu Kore wu góor.
2
Na xeetoo xeet tàccu, xaacu, sarxolleel Yàlla!
3
Aji Sax ji, Aji Kawe jee jara ragal, mooy buur bu mag bi tiim àddina sépp.
4
Moo nu nangulal xeet yi, nu teg tànk gàngoor yi.
5
Moo nu tànnal céru suuf, muy sagu askanu Yanqóoba wii mu sopp. Selaw.
6
Yàllaa yéeg, kàddu riir. Aji Sax jee yéeg, bufta jolli.
7
Woyleen Yàlla, woyleen, woyleen Yàlla sunu buur, woyleen.
8
Yàllaay buuru àddina sépp; taalifleen, woy ko.
9
Yàllaa di buuru xeet yi, Yàllaa tooge jalam bu sell.
10
Kàngami xeet yeey daje, ànd ak ñoñi Yàllay Ibraayma; Yàllaa moom buur yi yiir àddina, te moo kawee kawe.