v.2.10.1

Taalifi cant 57

12 Versets

1

Mu jëm ci njiital woykat yi, dëppook galan bi ñuy woowe Bul yàq, diy ñaan, ñeel Daawuda, gannaaw ba mu dawee Buur Sawul, ba dugg ca xunt ma.

2

Éy Yàlla, baaxe ma, ngalla baaxe ma, fi yaw laay làqu, yiiroo sa kiiraay, ba musiba yi jàll.

3

Ma woo Yàlla, Aji Kawe ji, Yàlla, mi may matalal.

4

Mooy yónnee fa asamaan, musal ma, dumaal ma ku may noot. Selaw. Yàllaay yónnee jëfi ngoram ak wormaam.

5

Maa ngi tëdd ci biiri noon yu mel niy gaynde, di yàpp doom aadama. Seeni sell niy xeej aki fitt, seen làmmiñ di saamar yu ñaw.

6

Éy Yàlla, yaa màgg, ba sut asamaan, sag leer tiim suuf sépp.

7

Noon yi di ma fiir, sama xol jeex. Ñu gasal mam pax, far tàbbi ca. Selaw.

8

Yàlla, dogu naa, dogu naa woy, di la kañ.

9

Na sama jëmm jépp yewwu, xalam ak moroom ma yewwu; ma yee leeru njël.

10

Boroom bi, naa lay gërëm ci biir xeet yi, kañ la ci biir waaso yi.

11

Sa ngor a màgg, ba àkki asamaan, sa worma àkki fa kaw-a-kaw.

12

Éy Yàlla, yaa màgg, ba sut asamaan, sag leer tiim suuf sépp.