1
Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd aki xalam, ñeel Daawuda.
2
Ngalla Yàlla, déglul, maa ne wallóoy, teewlul, ma dagaan la.
3
Àll laa lay woowe, sama xol jeex; yéege ma doju rawtu wu ma jotul.
4
Yaw laa làqoo, ngay tata ju dëgër, fegal ma noon.
5
Naa dëkke sa xayma ba fàww; làqoo sa kiiraay. Selaw.
6
Yàlla, yaa dégg samay dige, sédd ma céru ñi wormaal sa tur.
7
Ngalla féqal fani Buur, ay atam bare, sët ba sëtaat.
8
Éy Yàlla, yal na Buur toog ba fàww fi sa kanam, nga sédd ko sa ngor ak sa worma, mu fegoo;
9
kon ma woy la ba fàww, di jëfe samay dige bésoo bés.