v.2.10.1

Taalifi cant 64

11 Versets

1

Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.

2

Éy Yàlla, déglul sama kàddug tawat; ngalla aaral sama bakkan ci noon bu raglu.

3

Làq ma pexey ku bon, ma rëcc gàngooru defkati ñaawtéef.

4

Ñu ngi daas seen làmmiñ niy saamar, di fitte seeni kàdduy wextan,

5

di jam ku ñu tëru te deful dara; jekki jam ko, te tiituñu ci dara.

6

Dañoo dogu ca lu bon la ñu nar, di diisoo na ñuy làqe ay fiir, te naan: «Kenn du ko gis!»

7

Dañuy lal pexem njubadi te naan: «Lal nanu pexe mu mat sëkk.» Nit aka xóot xel te xóoti mbóot!

8

Waaye Yàllaa leen di jamu fittam, ñu jekki daanu.

9

Seen làmmiñ a leen di fakkastal, ba ku leen xool wëcc bopp.

10

Ñépp a ciy am tiitaange, bay siiwal la Yàlla def, tey xalaataat jëfam jooju.

11

Ku jub bége Aji Sax ji, làqoo ko. Képp ku namm njub, damu.