1
Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd aki xalam, di woyu cant.
2
Éy Yàlla, yéwéne nu, barkeel nu, te geesoo nu sa leeru kanam, Selaw.
3
ba ñu ràññee sa loxo fi kaw suuf, gis sag wall fi biir xeet yépp.
4
Yaw Yàlla, na la xeet yi sant, na la xeet yépp sant.
5
Na xeet yiy bég, di sarxolle; loo dogalal xeet yi njub la, te yaay wommat xeet yi ci kaw suuf. Selaw.
6
Yaw Yàlla, na la xeet yi sant, na la xeet yépp sant.
7
Suuf si nangu na, yal na nu Yàlla sunu Yàllay barkeel.
8
Yal na nu Yàllay barkeel, ba àddina wërngal këpp ragal ko.