v.2.10.1

Taalifi cant 6

11 Versets

1

Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd ak xalamu juróom ñetti buum, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.

2

Éy Aji Sax ji, bul mer, ba di ma rëbb, bul xadaru, ba di ma mbugal.

3

Aji Sax ji, damaa néew doole, yërëm ma! Éy Aji Sax ji, sama yaram a tas, dàmp ma!

4

Sama xol a jeex tàkk. Aji Sax ji, loo deeti xaar nag?

5

Éy Aji Sax ji, délsil, xettali ma! Walloo ma sa ngor.

6

Deesul dee ba fàttaliku la; ku dugg njaniiw, nu mu lay sante?

7

Onk naa ba loof, di fanaanee jooy, sama lal di féey, ba far seeye rongooñ.

8

Saay gët a ngi xóot ndaxu naqar, boole ci giim ndax tooñi noonoo noon.

9

Yeen, defkati ñaawtéef yépp, xiddileen ma! Aji Sax ji dégg na saay jooy,

10

Aji Sax ji dégg na saay dagaan, Aji Sax jii nangu na samag ñaan.

11

Noon yépp a am gàcce, ba jàq lool, ne wërëñ ak gàcceg mbetteel.