1
Mu jëm ci njiital woykat yi, ñeel Daawuda, di woy wuy fàttalee.
2
Yàlla, wallu ma! Éy Aji Sax ji, gaawe ma!
3
Kuy wut sama bakkan, yal na rus, torox ne tott. Kuy bége sama loraange, yal nañu ko duma, waññi ko, mu ne yàcc.
4
Kuy ñaawalaate, yal nañu ko toroxal, mu daw, dellu gannaaw.
5
Képp ku la wër, yal na bég, di la bànneexoo. Képp ku safoo sag wall, yal na jàppoo: «Yàlla màgg na!»
6
Man de, néew naa doole, ñàkk naa. Éy Yàlla, gaawe ma. Yaw yaa may wallu, xettali ma. Éy Aji Sax ji, bu ma yeexe.