1
Dib taalifu cant, ñeel Asaf. Yàlla toog na, di jiite ndajem boppam, di àtte ndawi péncam, naan:
2
«Dungeen bàyyi àtteb njublaŋ, ak di faral ku bon? Selaw.
3
Sàmmleen àqu néew-ji-dooleek jirim, tey àtte yoon ku ñàkk ak ku ndóol.
4
Walluleen néew-ji-dooleek walaakaana, di leen xettali ci ku bon.
5
«Ndawi péncum Yàlla yii xamuñu, dégguñu; xanaa di doxe lëndëmu ñaawtéef, ba ponki dëgg yépp di jaayu.
6
«Dama ne ay yàlla ngeen, yeen ñépp di njabootu Aji Kawe ji.
7
Waaye du leen tee dee ni doom aadama, du leen tee daanu ni képp kuy njiit.»
8
Ngalla Yàlla, taxawal, àtte àddina, yaw yaa séddoo xeetoo xeet.