1
Ñeel askanu Kore wu góor, di woyu cant. Dëkkub Aji Sax ji, kenu yaa nga ca tund yu sell ya.
2
Aji Sax jee sopp bunti Siyoŋ gii, mu gënal ko fu askanu Yanqóoba dëkke.
3
Yaw, dëkkub Yàlla bi, tuddees na say jaloore. Selaw.
4
Yàlla nee: «Ma limaale Misraak Babilon, ñi ma xam di dégg. Xoolal Filisti ak Tir, ak réewum Kuus. Nit a ngii, juddoo fa.»
5
Te teewul ñu cosaanale ko Siyoŋ, ne kii ak kee fa bokk juddoo, te Aji Kawe jee saxal Siyoŋ.
6
Aji Sax jeey lim xeet yi, limaale leen ne: «Kii fi la juddoo.» Selaw.
7
Kuy fecc ak kuy woy ànd naan: «Sunu cosaanoo cosaan fii la!»