1
Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd ak xalam gu ñuy wax gitiit, ñeel Daawuda, dib taalifu cant.
2
Aji Sax ji sunu Boroom, sa tur aka màgg ci kaw suuf sépp! Sag leer tiim asamaan.
3
Làmmiñu tuut-tànk, ba ci luy nàmp, feeñal nga ca sa kàttan, ngir jaxase say noon, bañaaleek feyukat ne xerem.
4
Damay xool sa asamaan si nga móol, ak weer week biddiiw yi nga fi teg.
5
Moo, luy nit, ba nga di ko bàyyi xel? Luy doom aadamaak loo koy yége?
6
Yaa ko def mu gëna suufe as lëf malaaka yi, yaa ko kaalaa teraanga ak daraja,
7
fal ko ci kaw loo bind, jox ko lépp, mu teg tànk:
8
jur gépp, gu gudd ak gu gàtt, rabi àll it ca la,
9
ak njanaaw ak jën ak luy jaare yooni géej.
10
Aji Sax ji sunu Boroom, sa tur aka màgg ci kaw suuf sépp!