1
Aji Sax jeey buur, soloo daraja; Aji Sax jee solu, gañoo doole: àddinaa ngii, dëju te raful.
2
Sab jal a masa sax, te yaa masa nekk.
3
Aji Sax ji, géej a riir, géej a àddu, mu riir, gannax ya rëkk, mu riir.
4
Waaye riirum wal mu walangaanoo, ak géej gu sàmbaraaxoo, Aji Sax ja fa kaw a rawati!
5
Say santaanee wér te wóor; Aji Sax ji, sellaay la sa kër jagoo ba fàww.