1
Kaayleen, nu sarxolleel Aji Sax ji, nu xaacul sunu wéeru-mucc.
2
Nanu ko dikke cant, woyal ko, mu riir.
3
Aji Sax jeey Yàlla ju màgg ji, buur bu mag bi tiim yàllay xeet yépp.
4
Moo moom xóotey suuf, moom colli tund yi,
5
moom géej, sàkk ko, moom jéeri ji mu mooñ.
6
Nan sëgg, sujjóot, sukkal Aji Sax ji nu sàkk.
7
Mooy sunu Yàlla, nuy xeet wi muy foral, diy gàtt ciy loxoom. Bésub tey yal nangeen dégg kàddoom
8
ga mu noon: «Buleen të, na woon fa Meriba, jantub keroog fa Maasa, ca màndiŋ ma,
9
fa ma seeni maam doon seetloo, di ma diiŋat te gisoon samay jaloore.
10
Ñeent fukki at laa jéppi googu maas, ma ne: “Seen xol a dëkke lajj, ñu faaleedi samay santaane.”
11
Moo ma taxa giñ ci sama biir mer, ne duñu tàbbi fa samag noflaay.»