v.2.10.1

Esayi 20

6 Versets

1

At ma bummib Asiri demee ca ndigalal Sargon buurub Asiri, ba songi dëkk ba ñuy wax Asdodd ca Filisti, ba mujj ko nangu,

2

fekk na Aji Sax ji wax, Esayi doomu Amocc jottali. Mu ne ko: «Demal summi tubéyu saaku ji nga sol, te summi say dàll.» Mu def noona, di doxe yaramu neen, tànki neen.

3

Gannaaw gi, Aji Sax ji ne: «Esayi sama jaam bi def na yaramu neen, tànki neen lu mat ñetti at, muy firnde, di tegtal ci mbirum Misra ak réewum Kuus.

4

Te noonu la buurub Asiri di yóbboo ngàllo Misra, toxal waa Kuus, ñuy ay ndaw aki màggat. Yaramu neen, tànki neen lañuy def, seen taat ne fàŋŋ, muy gàcceg Misra.

5

Dañuy boole njàqareek gàcce ndax réewum Kuus mi ñu yaakaaroon, ak Misra gi ñu doon sagoo.»

6

Bu keroogee ku dëkke tefes googu dina ne: «Xanaa kay du ñii lanu yaakaaroon! Te nu dawoon di wuti ndimbal ci ñoom, ngir rëcc buurub Asiri! Léegi nag nu nuy mucce?»