v.2.10.1

Esayi 21

17 Versets

1

Yéene bii moo wàccal màndiŋ ma feggook géej ga:

2

Peeñu mu ñàng lañu ma ci wax. Workat biy wor, yàqkat biy yàq. Yeen waa Elam, songleen; yeen waa Medd, gawleen leen. Dakkal naa mboolem onk yu ñu sabab.

3

Lii a waral sama njàqareg xol, mitit jàpp ma, mel ni mititu mat, ma jaaxle ba déggatuma, jàq ba gisatuma.

4

Bopp ubu, tiitaange jàpp ma; sama ngoonug bànneex soppiku guddi gu raglu.

5

Ndab taaje, laltan lale, ñuy lekk aka naan. Ñu jekki ne: «Yeen kilifa yi, jógleen! Diwleen pakk yi!»

6

Boroom bi kat da maa wax, ne ma: «Doxal taxawal ab wattukat, lu mu gis, wax ko.

7

Bu gisee gawar ci watiiru ñaari fas, ak ñu wari mbaam ak ñu wari giléem, na teewloo teewlu bu baax.»

8

Wattukat ba àddu ca kaw ne: «Sang bi, maa ngii yendoo séentu, fanaane wattu fii ma taxaw.

9

Ma ne gawar a ngii, war watiiru ñaari fas. Nee: “Daanu nañoo, Babilon daanu na, jëmmi tuuram yépp tasaaroo fi suuf!”»

10

Yeen bokk yi ñu bàcc ni pepp ca sama dàgga ja, la ma dégge ci Aji Sax ji Yàllay Israayil, Boroom gàngoor yi, wax naa leen ko.

11

Yéene bii moo wàccal Duuma:

12

Wattukat bi ne: «Bët set, mu guddeeti rekk; boo amee looy laaj, délsil laajaat ko.»

13

Yéene bii moo wàccal Arabi:

14

Yeen waa Tema, dajejileen ak ña mar, yóbbul leen am ndox. Dogileen ñay daw, may leen ñu lekk.

15

Ay saamar de lañuy daw; saamar bu ñu xàcc ak fitt gu ñu leen diir ak tàngooru xare.

16

Aji Sax ji de da maa wax ne ma: «Fileek menn at mu surga bu ñu bind waññ, sagub dëkk bii di Kedar dina sàggiku,

17

li des ci jàmbaari fittkati Kedar di lu néew.» Aji Sax ji Yàllay Israayil wax na ko.