1
Ñeel Daawuda, dib taalifu cant. Ngor ak yoon laay woy. Yaw Aji Sax ji laay joobe.
2
Naa teewlu yoonu màndute. Ana kañ nga may dikkal? Naa doxe màndute fi sama biir waa kër.
3
Caaxaani neen, xooluma; jëf ju wàcc yoon, bëgguma, taqu ma fenn.
4
Kuy nas njekkar, sore ma; lu bon, xawma ko.
5
Kuy jëw moroomam, ma wedamal; ku daŋŋiiral ak ku reew, muñaluma la.
6
Ku dëggu ci réew mi, ma geesu, ngir fat ko. Te kuy wéye màndute, kookoo may liggéeyal.
7
Kuy njublaŋ du tooge sama kër, kuy fen du taxaw sama kanam.
8
Maay xëy, sànk képp ku bon ci réew mi, ngir génne ci dëkkub Aji Sax jii képp kuy def lu ñaaw.