1
Di woyu cantu màggal. Yeen waa àddina sépp, xaaculleen Aji Sax ji.
2
Nangeen jaamu Aji Sax ji ci mbég, dikke koy woy!
3
Seedeleen ne Aji Sax jeey Yàlla. Moo nu sàkk, nuy ñoñam, di gàttam yi muy foral.
4
Nangeen dem këram, dugge faag cant, dugg ëttam di màggal, sant ko, teral turam.
5
Aji Sax jee baax, gore ba fàww, worma ja sax dàkk!