1
Ñeel Daawuda, dib taalifu cant. Aji Sax ji daa wax sama Sang, ne ko: «Toogeel sama ndijoor, ba ma def say noon sa ndëggastal.»
2
Sa nguur la Aji Sax ji saxal, dale ko fa Siyoŋ. Yilifal noon yi la wër!
3
Sa mboolooy taxawal seen bopp, sa bésub xare. Ñu sol darajaak cellte, faboo fa njël sosoo, diy ndaw, wàccsil la, nib lay.
4
Aji Sax jee ko giñ, te du dellu gannaaw: «Yaa dib sarxalkat ba fàww, topp dayob Melkiccedeg.»
5
Sang baa ngi fi sa ndijoor te mooy rajaxe buur yi, bés bu meree.
6
Mooy mbugal xeet yi, jal seeni néew, di rajaxe kilifay àddina, ba mu daj.
7
Déeg ba feggook yoon wa, Buur a cay naan, te moo ko tax di siggi.