1
Màggalleen Ki Sax! Naa sante Aji Sax ji léppi xol ci biir ñu jub ñi bokk jataay.
2
Liggéeyi Aji Sax ji réy na, ku ko safoo di ko gëstu.
3
Jëfam di teddngaak daraja, njubteem di sax ba fàww.
4
Moo dogal ñuy fàttalikuy kéemaanam; Aji Sax ji boroom yiw ak yërmande.
5
Mooy leel ku ko ragal, di bàyyi xel kóllëreem gi ba fàww.
6
Won na ñoñam dooley jëfam, ba mu leen joxee suufu xeet yi.
7
Ay jëfam dëgg laak yoon, tegtalam yépp mata wóolu,
8
laloo dëgg ak njub, te sax dàkk ba fàww.
9
Moo yónnee xeetam wall, fas ak ñoom kóllëre gu sax. Kee sell te jara ragal!
10
Ragal Aji Sax ji di njàlbéenu rafet xel, dég-dég bu rafet ñeel ku koy wéye. Moo yeyoo cant ba fàww.