1
Ba Israayil bàyyikoo fa Misra, ba waa kër Yanqóoba dëddu askan woowu di làkk,
2
ca la Yuda doon kër Aji Sax ji, giirug Israayil googu doon ab jagleem.
3
Géej gaa leen gis, daw, dexu Yurdan a deltu gannaaw,
4
tund yu mag yiy curpi niy kuuy, di curpeendook tund yu ndaw yi niy mbote.
5
Moo géej, loo xewle bay daw? Yaw, dexu Yurdan, looy deltu gannaaw?
6
Tund yu mag yee, lu ngeen di curpi niy kuuy? Yeen, tund yu ndaw yi, lu ngeen di curpi niy mbote?
7
Suufee, loxalal Boroom bi, Yàllay Yanqóoba mii,
8
ki soppaliw doj ndox mu taa, xeer wu ne sereŋ, mu def bëtu ndox.