1
Màggalleen Ki Sax! Yeen ñiy jaamu Aji Sax ji, màggalleen ko, màggalleen turu Aji Sax ji!
2
Yal nañu teral turu Aji Sax ji tey ak ëllëg!
3
Li dale penku ba sowu, màggalleen Aji Sax ji.
4
Aji Sax jee kawe, tiim xeetoo xeet, darajaam sut asamaan!
5
Ana ku mel ni sunu Yàlla Aji Sax ji, ki kaweel ab jalam, toog,
6
di jéer asamaan ak suuf?
7
Mooy yékkatee ku néewle fa suuf, di seppee ku sonn cib sën,
8
bokkal ko jataayu kilifa ya jiite xeetam.
9
Mooy dëël jigéen ju tële woona jur, may ko mbégtem njureel. Màggalleen Ki Sax!