v.2.10.1

Taalifi cant 119

176 Versets

1

Ndokkalee yaw mi màndu, di wéye yoonu Aji Sax ji.

2

Ndokkalee yaw miy wattu kàdduy seedeem, di ko toppe sa léppi xol.

3

Doo def njubadi, waaye dangay topp fi mu la jaarloo.

4

Aji Sax ji, yaa joxe sa tegtal yi ñu wara topp a topp.

5

Yal naa saxoo di sàmm sa dogali yoon,

6

di teewlu loo santaane, ba duma rus.

7

Damay gëstu sa ndigal yu jub, di la sante xol bu dëggu.

8

Sa dogali yoon laay sàmm; ngalla bu ma wacc a wacc.

9

Ana nu ndaw mana sellalee? Xanaa di sàmm sa kàddu.

10

Sama léppi xol laa lay toppe, bul ma wacc, ma wàcc say santaane.

11

Sama xol laa làq say wax, ngir bañ laa moy.

12

Jaajëfe, yaw Aji Sax ji, jàngal ma sa dogali yoon.

13

Maa àddu, tari mboolem lu sa kàddu digle.

14

Topp say tegtal laay bége mbégtem jépp alal.

15

Say tegtal laay jàngat, di teewlu say xàll.

16

Sa dogali yoon, ma tàqamtikoo, sa kàddu, ma fat ba fàww.

17

Sang bi, baaxe ma, ma dund, ba mana sàmm sa kàddu.

18

Ngalla muril saay gët, ma niir sa kéemaani yoon.

19

Doxandéem laa fi kaw suuf, bu ma làq say santaane.

20

Fu ma tollu maa ngi namm say ndigal ba sama xol ŋiis.

21

Rëbb nga ñu reew, ñu alku, ñiy dëddu say santaane.

22

Musal ma ciy kókkaleeki xaste, maa ngi topp sa kàdduy seede.

23

Te it kàngam yaa ngi may tooge, te may gëstu sa dogali yoon, Sang bi.

24

Sa kàdduy seede laay safoo, ñuy sama xejj yi may xelal.

25

Maa ngi ne ñàyy ci pënd bi, musal ma, yaa ko dige.

26

Wax naa la samay jaar-jaar, nga wuyu ma; ngalla xamal ma sa dogali yoon.

27

Dégtal ma li sa tegtal yiy firi, ma jàngat say kéemaan.

28

Naqaru xol sonal na ma, may ma ndëgërlaay, yaa ko dige.

29

Sorele maak yoonu fen, te baaxe ma saw yoon.

30

Yoonu worma laa tànn, jàkkaarlook say ndigal.

31

Éy Aji Sax ji, damaa langaamoo sa kàdduy seede, ngalla bu ma rusloo.

32

Ci sa yoonu santaane laay wéy, yaa may may xol bu tàlli.

33

Aji Sax ji, xamal ma li sa dogali yoon yiy firi, ma topp ko ba mu jeex.

34

May ma dég-dég, ma topp saw yoon, toppe ko xol bu tàlli.

35

Jiite ma ci sa xàllu santaane yi, mooy sama bànneex.

36

Joyantil sama xol, mu féeteek sa kàdduy seede, te dummóoyu alal ju lewul.

37

May ma, ma fénanti caaxaani neen, te musale ma say yoon.

38

Sang bi, sottalal ma sa dige bi nga digook ku la ragal.

39

Moyale ma gàcce gi ma ragal; yaa baaxi ndigal.

40

Maaka namm say tegtal, musale ma sa njub!

41

Aji Sax ji, yaa ko dige, dikke ma sa jëfi ngor ak sa wall,

42

ba ku ma kókkali, ma am tontam. Maa doyloo sa kàddu.

43

Bu ma xañ mukk kàddug dëgg, say àtte laa yaakaar kat.

44

Maay topp saw yoon, sàlloo ko, saxoo ko ba fàww,

45

di daagoo sago, nde say tegtal laay sàkku.

46

Maay àgge ay buur sa kàdduy seede, te duma rus.

47

Maay bége sa santaane yi ma sopp,

48

di yóotu sa santaane yi ma sopp, di jàngat sa dogali yoon.

49

Bàyyil xel li nga ma dig, Sang bi; moom laa yaakaar.

50

Lii laay muñe samaw naqar, sa kàddoo may dundal.

51

Nit ñu bew ñi ñaawal nañu ma lool, waaye dëdduwuma saw yoon.

52

Éy Aji Sax ji, damaa fàttaliku sa àtte ya woon, daldi muñ.

53

Sama xol daa fees ndax ñu bon ñiy wacc saw yoon.

54

Sa dogali yoon laay woyantoo, fu ma mana sance.

55

Aji Sax ji, tudd naa la guddi, di sàmm saw yoon.

56

Lii laa séddoo, maa topp sa tegtali yoon.

57

Aji Sax ji, yaw laa séddoo; di digee sàmm sa kàddu.

58

Sama léppi xol laa sàkkoo saw yiw, ngalla baaxe ma, yaa ko dige.

59

Damaa seetlu sama jëfin, dëpp, topp sa kàdduy seede.

60

Maa ngi gaawtu, yeexewuma say santaane moos!

61

Buumi ñu bon ñaa ngi may laaw, te sàgganewuma saw yoon.

62

Xaaju guddi laay jóg, di la sante sab àtte.

63

Maa xejjoo képp ku la ragal, tey topp say tegtal.

64

Aji Sax ji, sa ngor dajal na àddina; xamal ma sa dogali yoon.

65

Aji Sax ji, def nga la nga dige woon, Sang bi, defal nga ma ngëneel.

66

Xamal ma ngëneeli àtte ak xam-xam, maa doyloo say santaane.

67

Maa jàddoon, nga duma ma, léegi sa kàddu laay sàmm.

68

Yaaka baax tey baaxe; rikk xamal ma say tegtal.

69

Ñu bew ñee yàq sama der aki sos, te ma topp say tegtal ak sama léppi xol.

70

Ñu ngi nii, seeni xol dërkiis; te man may tàqamtikoo saw yoon.

71

Ngëneel la ma duma yi jural, ngir jànge naa ci say tegtal.

72

Sa ngëneelu yoon wi nga digle moo ma gënal ay junniy dogi xaalis ak wurus.

73

Say loxoo ma sàkk, tabax ma, may ma ag dégg, ma mokkal say santaane,

74

ñi la ragal gis ma, bég; nde sa kàddu laa yaakaar.

75

Aji Sax ji, ràññee naa ne say àtte dëgg la, te worma nga ma dumaa.

76

Ngalla dëfale ma sa ngor; Sang bi, yaa ko dige.

77

Nanga ma ganesee sa yërmande, ma dund; saw yoon ay sama bànneex!

78

Yal na ñu bew ñi torox, ñoo ma lor ak seeni sos, te man may gëstu say tegtal.

79

Yal na ku la ragal waññiku fi man, ba xam sa kàdduy seede.

80

Yal naa toppe say tegtal xol bu mat sëkk, ba duma rus.

81

Sàkku naa sag wall ba xol jeex, di xaar sa kàddu.

82

Séentu naa sab dige, ba gët giim; kañ nga may xettali?

83

Damaa mujj ras ni mbuusum der mu saxaar jàpp, waaye sàgganewuma say tegtal.

84

Ñaata fan laay toogati, Sang bi? Kañ ngay mbugal ñi ma topp?

85

Ñu bew ñi gasal nañu ma ay yeer yu saw yoon diglewul.

86

Sa santaane yépp worma la; te dees maa toppey sos, wallu ma!

87

Nes tuut ñu sànke ma fi kaw suuf, te man dëdduwuma say tegtal.

88

Musale ma sa ngor, ba jëfe sa kàdduy seede.

89

Aji Sax ji, sa kàddoo sax dàkk, taxaw jonn fa asamaan.

90

Sa worma, ba maasoo maas, yaa samp suuf, saxal ko.

91

Ci sa ndigal la lépp taxawe ba tey, lépp ànd, di la jaamu.

92

Su ma bégewuloon saw yoon, sànkoo sama toskare ji.

93

Duma fàtte mukk say tegtal, ci nga may musale.

94

Yaa ma moom, wallu ma; say tegtal laay sàkku.

95

Man la ñu bon ñi tëru, nar maa sànk, waaye sa kàdduy seede laay niir.

96

Gis naa ne lu mat lu ne am na kemu, waaye sa santaane mat ba wees kemu.

97

Maaka sopp saw yoon, di ko jàngat bés bu jot.

98

Li ma xelal ba ma raw noon yi, mooy sa santaane yi ma jagoo fàww.

99

Maa gëna ñaw képp ku may jàngal, nde sa kàdduy seedeey sama njàngat.

100

Maa ëpp mag ñi dég-dég, nde say tegtal laa topp.

101

Luy yoon wu aay, ma moyu, ba mana sàmm sa kàddu.

102

Say santaane it dëdduwuma ko, nde yaw yaa ma jàngal.

103

Sa kàddooka maa neex, ba dàqal ma tem-temu lem!

104

Ci say tegtal laay ràññee, ba tax ma bañ luy yoonu fen.

105

Sa kàddu laay niitoo samay tànk, muy leeral samaw yoon.

106

Giñ naa te di ko dëggal, ne dinaa sàmmonteek say àttey dëgg.

107

Toskare naa lool; éy Aji Sax ji, musal ma, yaa ko dige.

108

Aji Sax ji, rikk nangul ma kàdduy cant yi ma lay jébbal, te xamal ma say ndigal.

109

Sama bakkan ci xott saa su ne, waaye fàttewuma saw yoon.

110

Ñu bon ñi ma gasalum pax taxul ma wàcc say tegtal.

111

Maa séddoo fàww sa kàdduy seede, loolooy seral sama xol.

112

Damaa dogoo jëfe sa dogali yoon, saxoo ko ba mu jeex.

113

Maa bañ kuy ŋarale, maa sopp saw yoon.

114

Sama rawtu, sama kiiraay, yaw a; sa kàddu laay xaar.

115

Yeen ñiy def lu bon, xiddileen ma, ba ma sàmmonteek sama santaaney Yàlla.

116

Yaa ko dige, dooleel ma, ma dund; bul tas sama yaakaar.

117

Kàttanal ma, ma raw, di yittewoo say tegtal, ba fàww.

118

Yaay xarab képp ku wàcc sa dogali yoon, ay pexeem neen.

119

Yaay tonni ni purit képp ku bon fi kaw suuf, moo tax ma sopp sa kàdduy seede.

120

Sama yaram a ngi daw ndax ragal la, ragal say àtte.

121

Def naa njubte, def njekk; bu ma jébbal ñi may néewal.

122

Sang bi, gàddu ma, ma am jàmm, bu ma ñu bew ñi néewal.

123

Séentu naa sag wall ak sa kàddug dëgg, ba saay gët giim.

124

Sang bi, jëfeel ma sa ngor, xamal ma sa dogali yoon.

125

Sab jaam laa, may ma, ma ràññee, ba xam sa kàdduy seede.

126

Aji Sax ji, jëf jot na, ñee ngi jalgati saw yoon!

127

Maa sopp say santaane, mu gënal ma wurus ba ci wurusu ngalam.

128

Moo tax foo tegtale, ma rafetlu, lépp luy yoonu fen, ma bañ.

129

Sa kàdduy seede kéemaan la, moo tax ma di ko toppe xol.

130

Sa pirim kàddu day leeral, di xelal ku xeluwul.

131

Damaa ŋa ŋafeet, di àppaat, ngir namm say santaane.

132

Éy geesu ma te baaxe ma, ni nga baaxook ñi sopp sa tur.

133

Dooleelal ma samay tànk, yaa ko dige, te bu ma lenn lu bon man.

134

Jot ma ci nooteelu doom aadama, ma mana topp say tegtal.

135

Sang bi, geesoo ma sag leer, te xamal ma sa dogali yoon,

136

ay wali rongooñ ay wale saay gët, ndax sàmmeesul saw yoon.

137

Aji Sax ji, yaaka jub, te say àtte di yoon.

138

Yaa santaane sa kàdduy seede ci dëgg ak kóllëre gu yaa.

139

Damaa gis bañ yiy sàggane say wax, xol bu tàng di ma rey.

140

Sang bi, maaka sopp sa kàddu gi set ni weñ gu ñu xelli!

141

Ñàkk naa solo, faaleesu ma, waaye sàgganewuma say tegtal.

142

Sa àtte moo di àtte ba fàww, te saw yoon a dëggu.

143

Njekkar ak njàqare dab ma, say santaane di sama bànneex.

144

Sa kàdduy seedee di dëgg ba fàww, may ma, ma ràññee, ba dund.

145

Aji Sax ji, woo naa la wall lu ma man, wuyu ma, ma topp sa dogali yoon.

146

Dama ne: «Wóoy, wallu ma, ma sàmm sa kàdduy seede.»

147

Damaa jëlu, di la woo, di xaar sa kàddu.

148

Damay xoole guddi gépp, di jàngat sa kàddu.

149

Aji Sax ji, sama baat bii, teewloo ko sa ngor, te musal ma ni nga baaxoo muslee.

150

Rabatkati pexe yaa ngi jegesi, di nit ñu sore saw yoon.

151

Waaye yaw Aji Sax ji, jege nga, te sa santaane yépp a dëggu.

152

Yàgg naa xam ne sa kàdduy seede wax la joo saxal dàkk.

153

Xoolal sama coono te xettali ma; saw yoon déy, sàgganewuma ko.

154

Àtte ma, ba jot ma; musal ma, yaa ko dige.

155

Ku bon sore sa wall, ngir sàkkuwul sa dogali yoon.

156

Aji Sax ji, sa yërmande yaa na; musal ma ni nga ko baaxoo.

157

Ñi ma topp ak ñi ma baña bare, te taxul ma dëddu sa kàdduy seede.

158

Damaa gis workat yi, sib leen; ñoo sàmmul sa kàddu.

159

Seetlul ni ma soppe say tegtal. Éy Aji Sax ji, musal ma, yaa gore!

160

Sa mboolem kàddu dëgg la, sa àtte yépp di dëgg, sax dàkk.

161

Ay kilifaa ma topp ci dara, te teewul ma wormaal sa kàddu.

162

Man de, maa ngi bége sa kàddu ni ku for alal ju bare.

163

Fen, ma bañ, ba sib; sa yoon, ma sopp.

164

Juróom ñaari yoon ci bés màggale naa la ko say àttey dëgg.

165

Jàmm ju baree ñeel ku sopp sa yoon, te dara du ko fakkastal.

166

Aji Sax ji, sa wall laa yaakaar, say santaane laa jëfe.

167

Sama xol laa toppe sa kàdduy seede, te sopp koo sopp.

168

Damaa topp say tegtal ak sa kàdduy seede, fépp fu ma jaar kay yaa ngi ciy gis.

169

Aji Sax ji, yal na sama yuux àgg fa yaw; may ma, ma ràññee, yaa ko dige.

170

Yal na sama dagaan àgg fa yaw; xettali ma, yaa ko dige.

171

Naa xaacu, woyal la, yaa may jàngal sa dogali yoon.

172

Naa woye sa kàddu, loo santaane, yoon la.

173

Yal nanga ma dikke ndimbal, say tegtal laa tànn.

174

Aji Sax ji, namm naa sa wall, sa yoon ay sama bànneex.

175

Yal naa dund ba màggal la, say ndigal di sama ndimbal.

176

Lajj naa ni xar mu réer; gindi ma, Sang bi, sàgganewuma say santaane de!