1
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla. Ci sama njàqare laa woo Aji Sax ji wall, mu wuyu ma.
2
Éy Aji Sax ji, musal ma ci gémmiñu fen-kat, ak làmmiñu njublaŋ.
3
Yaw boroom làmmiñu njublaŋ, ana lu ñu lay añale ak lu ñu lay dolli?
4
Xanaa fitti mbër yu ñaw ak xal yu yànj.
5
Wóoy man mi ganeyaani baadooloy Meseg ya tey dali fa xaymay waa Kedar ñu xayadi ña!
6
Yàgg naa lool ci biir nit ñi bañ jàmm.
7
Man may wut jàmm, te su ma waxee, ñoom ñuy ayoo.