1
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda. Maaka bég, ba ñu ma nee: «Kër Aji Sax ji lanu jëm.»
2
Yaw Yerusalem, noo ngii taxaw ci sa bunt.
3
Céy, Yerusalem, dëkkub tabax bu baax bi booloo, di benn.
4
Fii la giiri Israayil di yéegsi, di giir yi Ki Sax séddoo. Ñu ngi santsi Aji Sax ji, ni ko Israayil warloo.
5
Fii la ngànguney Israayil tege, askanu Daawuda toog ca, di àtte.
6
Dagaanleen jàmmi Yerusalem: «Yerusalem, yal na sa xeli soppe dal,
7
jàmm ne ñoyy fi say tata wër, te xel dal ci biir këri Buur.»
8
Mbokk ak xarit a waral may ñaan jàmmi Yerusalem.
9
Sunu kër Yàlla Aji Sax jee ma tax di sàkku ngëneelu Yerusalem.