1
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla. Damaa séentu tund ya, te naan fu wall di jóge?
2
Sama wall a nga fa Aji Sax ji, Ki sàkk asamaan ak suuf.
3
Kii du la bàyyi nga tërëf, sa sàmm bii gëmmul.
4
Kiy sàmm Israayil kay gëmmul, nelawul.
5
Aji Sax jee lay sàmm, Aji Sax jee lay yiir, féete la ndijoor.
6
Du naaj wu lay dal bëccëg, mbaa leer gu ndaw guddi.
7
Aji Sax jee lay sàmm ci gépp loraange, di sàmm sa bakkan.
8
Aji Sax jee lay sàmm, dem ak dikk, tey ak ëllëg.