1
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla. Ba Aji Sax ji delloo waa Siyoŋ seen réew, danoo meloon ni ñuy gént,
2
di reeka sarxolle rekk. Yéefar yi naa: «Lu réy la Aji Sax ji defal ñii.»
3
Lu réy la nu Aji Sax ji defal moos, nu bég.
4
Aji Sax ji, rikk delloo nu na woon, ni ngay delloo wal yu ŋiis, mu walaat ca àllub Negew.
5
Kuy ji di jooy, yal na góob, di sarxolle.
6
Ku doon wéy a wéy, di jooy; yor mbuusum jiwoom, yal na dikk a dikk, di woy, ñibbiwaale sabaaram.