1
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla, ñeel Suleymaan. Kër, su ko Aji Sax ji tabaxul, ku ko tabax, neen nga doñ-doñi. Ab dëkk, su ko Aji Sax ji wattuwul, ku ko wattu, neen nga teewlu.
2
Neen it la nit di teela jóg aka guddee tëdd, di doñ-doñi lu mu lekk: Aji Sax ji leel na soppeem lu ni day, fekk ko muy nelaw.
3
Ma ne, doom Aji Sax jee koy sédde, njurum doom yool la.
4
Doom joo jure ndaw, mooy fitt ci loxol jàmbaar;
5
ndokkalee ku ci mbuusam fees, ba bu ñu taseekub noon ca pénc ma, duñu am gàcce mukk.