1
Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd ak xalamu juróom ñetti buum, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
2
Wallóoy, Aji Sax ji, ngor jee na! Kóolute réer na doom aadama.
3
Dañuy fenante, làmmiñ dig lem, xol ba njuuy la.
4
Yal na Aji Sax ji tëj gémmiñu kuy naxe, ak kuy làmmiñuy tëggu.
5
Ñu ngi naa: «Sunu làmmiñ lanuy daane, nook sunu kàddu; ku nu manal dara?»
6
Ku ñàkk a ngii, ñu futti, mu ngi binni, di néew-ji-doole. Aji Sax ji nee: «Maa ngii, di ci jóg, teg leen fi rawtu gu ñu ne siiw.»
7
Kàddug Aji Sax ji, kàddu gu sell la, ni xaalis bu ñu xelli ci taalu ban, settali ko juróom ñaari yoon.
8
Ngalla Aji Sax ji, sàmmal ku néewle, aar ko saa su ne ci nitu tey.
9
Ñu bon ñaa ngi taxawaalu fu ne, jikko ju sew falu ci biir doom aadama yi.