1
Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
2
Céy Aji Sax ji, loo deeti xaar? Xanaa doo ma tanqamlu ba fàww? Loo deeti xaar, bañ maa geesu,
3
ba ma tàggook bopp bu ubu ak njàqarey xol bu sax, ba noon dootu ma man?
4
Céy Aji Sax ji sama Yàlla, geesu ma, wuyu ma, leqali ma, bala ma ne sërëx ci nelawi dee,
5
noon ba naan: «Daan naa ko,» bañ yay bége saab jéll.
6
Man de maa ngi dénkoo sa ngor, di bànneexoo sag wall. Naa woy Aji Sax ji, ki may baaxe xéewalam.