1
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda. Éy Aji Sax ji, man de, réy-réyluwuma, daŋŋiiraluma, xintewoowuma lu réy it, mbaa lu ma ëlëm.
2
Xanaa ne tekk, ne cell, ni perantal ak ndeyam; sama xel dal ni perantal.
3
Éey Israayil, yaakaaral Aji Sax ji tey ak ëllëg.