1
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla. Aji Sax ji, ci ay xóote laa lay woowe.
2
Boroom bi, déglu ma, teewlu ma, ma tinu la.
3
Ki Sax, yaw, soo doon lim bàkkaar, Boroom bi, ana kuy taxaw?
4
Waaye yaay jéggale, ñu ragal la.
5
Damay xaar Aji Sax ji, di ko xaare xol, di yaakaar kàddoom.
6
Wattukat bi yàkkamti njël, wattukat bi yàkkamti njël, laa ne, ni ma yàkkamtee Aji Sax jee ko raw.
7
Éey Israayil, négandikul Aji Sax ji. Aji Sax jee gore, te yaatug njot.
8
Mooy jot Israayil ci ñaawtéefam yépp.